18Ku maandu, Aji Sax ji yég la, sab cér sax.
19Bu mettee doo rus, te bésub xiif dangay regg.
20Ku bon sànku; noonub Aji Sax ji, taaru tool bu naat la, bu tàkkee, jeex tàkk.
21Ku bon leb, du fey; ku jub yéwén, di joxe.
22Aji Sax ji barkeel la, nga jagoo réew mi moos; mu alag la, nga dog.
23Aji Sax jeey sopp saw yoon, jiite say jéego.
24Soo tërëfee it, doo daanu. Aji Sax jee lay walloo loxoom.
25Ba may ndaw, ba tey may mag, gisuma ku jub ñàkk ndimbal, mbaa askanam di dunde yalwaan.