1Ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, digaaleel ak samay digaale, xeexal maak ñi may xeex.
2Fëkkal sa pakk ak sa kiiraay, taxawusi ma,
3xàcci sa xeej ak sa sémmiñ, dajeek ñi may dàq. Déey ma, ne ma: «Sag mucc, man a.»
4Ñiy wut sama bakkan, yal nañu rus ba torox; ñi may fexee lor, yal nañu leen waññi, sewal leen.
5Yal na leen malaakam Aji Sax ji bëmëx, nim ñax mu ngelaw wal.
6Yal na leen malaakam Aji Sax ji dàq, ñuy lëndëmtuy tarxiis.
7Defuma dara, ñu di ma fiir, defuma dara, ñu gas um yeer, di ma tëru.
8Yal nañu sànkoo mbetteel, keppoo seen fiir, sànkoo seenum yeer.
9Su boobaa ma bége Aji Sax ji, bànneexoo wallam,
10di ko sante sama jëmm jépp, naan: «Éy Aji Sax ji, ana ku mel ni yaw, di xettli néew-ji-doole ci boroom doole, ak ku néewleek ku ñàkk ca ka leen di lekk?»
11Nit ku bon a ngi may duural, di ma jiiñ lu ma yégul.
12Ma ji leen njekk, ñu fey ma njekkar, ndaw tiisu xol!
13Man de ba ñu woppee, maa ngi ñaawlu, di woor, toroxloo, sukk, ñaanal leen,
14tiisoo leen ni saab xarit mbaa doomu ndey, di ñaawlook a yoggoorlu ni ku ñàkk yaay.
15Ma daanu tey, ñu daje di ko bége, dajaloo fi sama kaw, di ma fexeel te yéguma, di ma yàpp, tëë ba.
16Tekkiwuñu dara, di ma ñaawal rekk te di ma màttu.
17Éy Aji Sax ji, loo deeti seetaan? Musal ma ci seenum pàdd, wallu ma ci yii gaynde, sàmmal ma sama benn bakkan bii!
18Maa lay sante fa ndaje yaatoo, màggal la digg mbooloo mu yaa.
19Noon bu ma deful dara, yàlla bumu gis lu mu ma damoo. Ku ma bañ ci dara, yàlla bumu ma ree.
20Waxuñu jàmm, xanaa di ràbbal niti jàmm ci réew mi ay kàdduy tuuma.
21Ñu ngi ma ŋa ŋàpp, di ma tuumaal, naan: «Yaw a, yaw a, noo la gis!»
22Éy Aji Sax ji, yaa ci gis, bul selaŋlu, éy Boroom bi, bul ma sore.
23Jógal, sàmmal ma sama àq. Sama Yàlla, Boroom bi, àtte ma yoon.