8Ku ragal Aji Sax ji, malaakaam yiir la, di la wallu.
9Mosleen, xam ne Aji Sax jee baax, ndokklee yaw mi ko làqoo.
10Ragal-leen Aji Sax ji, yeen nitam ñu sell ñi; ku ko ragal doo ñàkk dara.
11Gaynde man naa ndóol, xiif, nit sàkku Aji Sax ji, ñàkkul lenn lu baax.
12Dikkal doom, déglu ma, ma jàngal la ragal Aji Sax ji.