10Ragal-leen Aji Sax ji, yeen nitam ñu sell ñi; ku ko ragal doo ñàkk dara.
11Gaynde man naa ndóol, xiif, nit sàkku Aji Sax ji, ñàkkul lenn lu baax.
12Dikkal doom, déglu ma, ma jàngal la ragal Aji Sax ji.
13Ana ku dund neex, mu bëgga gudd fan, ba gis ngëneel?
14Na làmmiñam daw lu aay, dawi fen.
15Na dëddu lu bon tey def lu baax, sàkku jàmm, saxoo ko.
16Ay gët la Aji Sax ji ne jàkk aji jub ji, te ay noppam la dékk wooteb wallam.
17Aji Sax jeey rëbb kuy jëfe mbon, ngir dagge ko kaw suuf, far turam.
18Ku jub yuuxu, Aji Sax ji dégg, fu mu jàqe, mu musal ko.
19Sa yaakaar tas, Aji Sax ji jege la, sa xol jeex, Aji Sax ji wallu la.
20Musiba bare naa dal ku jub, Aji Sax ji musal ko ci lépp,