8Yeen waa àddina sépp, ragal-leen Aji Sax ji; yeen àddina wërngal këpp, wormaal-leen ko.
9Moo àddu, mu am; santaane, mu sotti.
10Aji Sax jeey neenal li xeet yiy fexe, di gàntal li mbooloo yiy mébét;
11Aji Sax ji nas, mu àntu ba fàww, mu mébét, mu sottil maasoo maas.
12Ndokklee yeen xeet wi Aji Sax ji di seen Yàlla, yeen askan wi Aji Sax ji séddoo.
13Asamaan la Aji Sax jiy jéere, di gis doom aadama yépp.
14Jal ba mu tooge lay niire waa àddina sépp.
15Moo tabax seen xol, ñoom ñépp; lu ñu def, xam na ko.
16Mbooloo mu réy mayul Buur ndam, doole ju bare walluwul jàmbaar.