2Xalamleen, sante Aji Sax ji, xalamal-leen ko xalamu fukki buum.
3Fental-leen ko woy, xalam, mu neex, sarxolle jib.
4Aji Sax jee jub kàddu. Mooy jëfe lépp kóllëre.
5Moo sopp dëgg ak yoon. Aji Sax ji, ngoram a fees àddina.
6Kàddug Aji Sax ji la asamaan sosoo, ci baatam la gàngoori asamaan yépp sàkkoo.
7Moo boole ndoxi géej, jal, yeb xóotey géej ciy mbànd.
8Yeen waa àddina sépp, ragal-leen Aji Sax ji; yeen àddina wërngal këpp, wormaal-leen ko.
9Moo àddu, mu am; santaane, mu sotti.
10Aji Sax jeey neenal li xeet yiy fexe, di gàntal li mbooloo yiy mébét;