14Jal ba mu tooge lay niire waa àddina sépp.
15Moo tabax seen xol, ñoom ñépp; lu ñu def, xam na ko.
16Mbooloo mu réy mayul Buur ndam, doole ju bare walluwul jàmbaar.
17Yaakaar aw fas nax sa bopp la, kàttanu fas dug wall.
18Ma ne, Aji Sax jee naa jàkk ku ko ragal tey wéeroo ngoram.