9Waccoo ma ci loxol noon, danga maa taxawal fu ma yaatoo.
10Éy Aji Sax ji, baaxe ma, jàq naa! Samay gët a ngi giim ndaxu tiis, xol jeex, yaram jeex.
11Naqar a ngi may rey, tiis di wàññi samay fan, sama doole ŋiis ndax sama njubadi, samay yax semm.
12Noonoo noon a ma sewal, dëkkandoo waxi noppi, xame seexlu ma, ku ma gis biti, di ma daw.
13Kenn xalaatu ma, xanaa fàtte ma ni ku dee, ma mel ni ndab lu yàqu.
14Damaa dégg jëw yu bare, lu raglu dar ma kepp. Ñu ngi mànkoo, di ma fexeel, di wut sama bakkan.
15Man nag Aji Sax ji, ci yaw laa dénku. Ma ne: «Yaay sama Yàlla.»
16Yaa yor sama àpp. Xettli maak ku ma noonoo ak ku may sonal.
17Leeralal ma sa kanam, Sang bi, walloo ma sa ngor.
18Éy Aji Sax ji, woo naa la wall, yàlla buma rus. Yal na ku bon rus, ne xerem biir njaniiw.
19Yal nanga tëj gémmiñu fen-kat buy wax aji jub waxi reewande, di réy-réylook a xeebaate.
20Yàlla yaa yaa ngëneel loo dencal ku la ragal, defal ko ku la làqoo, doom aadama seede.
21Yaa koy làq fa nga làqu, fa pexey nit àggul. Nga yiir ko, mu yiiru ci ayu làmmiñ.