9Waccoo ma ci loxol noon, danga maa taxawal fu ma yaatoo.
10Éy Aji Sax ji, baaxe ma, jàq naa! Samay gët a ngi giim ndaxu tiis, xol jeex, yaram jeex.
11Naqar a ngi may rey, tiis di wàññi samay fan, sama doole ŋiis ndax sama njubadi, samay yax semm.
12Noonoo noon a ma sewal, dëkkandoo waxi noppi, xame seexlu ma, ku ma gis biti, di ma daw.
13Kenn xalaatu ma, xanaa fàtte ma ni ku dee, ma mel ni ndab lu yàqu.