4Yaa may yiir, di ma aar, jiite ma, wommat ma ngir yaw.
5Génne ma fiir gi ñu may tëroo; yaw yaa di sama rawtu.
6Yaw laa dénk sama bakkan. Aji Sax ji, Yàlla miy dëgg, ngalla jot ma.
7Maa bañ kuy topp tuuri neen. Man, Aji Sax ji laa wóolu.
8Damay bég, di bànneexoo sa ngor, li nga xoole samaw tiis. Ràññee nga sama njàqarey xol.