7Buur ne: «Ma biral dogalu Aji Sax ji, moom mi ma ne: “Yaa di sama doom, bés niki tey, maa la jur.
8Ñaan ma xeeti àddina, ma sédd la ko, nga moom ba ca cati àddina,
9yilife leen yetu weñ, rajaxe leen ni njaqal xandeer.”»
10Kon yeen buur yi, muusleen, kilifay àddina, fàgguleen.
11Jaamuleen Aji Sax ji, ragal ko, di ko bége, ba yaram daw.