Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 2

Sabóor 2:4-9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Ki ci jalub asamaan a ngay ree, Boroom baa nga leen di kókkali,
5mer, ba gëdd leen, xadaru, tiital leen ne:
6«Man maa tabb buur, fal ko ci Siyoŋ, sama tund wu sell.»
7Buur ne: «Ma biral dogalu Aji Sax ji, moom mi ma ne: “Yaa di sama doom, bés niki tey, maa la jur.
8Ñaan ma xeeti àddina, ma sédd la ko, nga moom ba ca cati àddina,
9yilife leen yetu weñ, rajaxe leen ni njaqal xandeer.”»

Read Sabóor 2Sabóor 2
Compare Sabóor 2:4-9Sabóor 2:4-9