Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 27

Sabóor 27:5-13

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Bésub ay, mu yiire ma mbaaram, làq ma, ma làqoo xaymaam, aj ma ciw doj, ma raw.
6Ma doxe fa siggi, tiim noon yi ma wër, di sarxali fa xaymaam saraxi sarxolle. Naa woyal Aji Sax ji, joobe ko.
7Éy Aji Sax ji, déglul, ma woote! Ngalla baaxe ma, nangul ma.
8Yaw la sam xel ne ma, ma sàkku la, te it yaw Aji Sax ji laay sàkku.
9Sang bi, bu ma làqu, bul mer, jañax ma. Yaa ma daa wallu. Bu ma wacc, bu ma ba, yaay Yàlla mi may musal.
10Ndey ak baay man nañu maa wacc, Aji Sax ji fat ma.
11Éy Aji Sax ji, joxoñ ma saw yoon, jaarale ma joor gu wóor, ngir ñi may tëru.
12Bu ma baye bànneexu noon. Seedey naaféq a ma jógal, di sos fitna.
13Maay dajeek ngëneelu Aji Sax ji fi kaw suuf sii. Lii wóor na ma.

Read Sabóor 27Sabóor 27
Compare Sabóor 27:5-13Sabóor 27:5-13