4Toogumaak naxekat, lëngoowumaak naaféq,
5sib naa gàngooru saaysaay, toogumaak ku bon.
6Aji Sax ji, maay jàpp ci biir mucc ayib, di wër sa sarxalukaay,
7àddu, sant la, lim sa jépp jaloore.
8Aji Sax ji, maa sopp sa dëkkuwaay, bëgg bérab bi sag leer teew.
9Bu ma buubaaleek bàkkaarkat, sànni, di ma booleek bóomkat, bóom.