5Jiitee ma sag dëgg, jàngal ma. Yaw yaay Yàlla ji may musal, ma di la yendoo yaakaar.
6Aji Sax ji, bàyyil xel sa yërmandeek sa ngor. Naka jekk sa jikkoo!
7Bul xool li ma bàkkaare ndaw ak li ma moy. Aji Sax ji, xoole ma sa ngor ngir sag mbaax.
8Aji Sax jee baax, rafeti dogal, di gindi moykat ci yoon wi,
9di jiite ku woyof mbubb ci njubte, di ko xamal aw yoonam.
10Aji Sax ji ngor ak dëgg rekk lay jiitee kuy sàmm kóllëreem ak seedey yoonam.
11Éy Aji Sax ji, tooñ naa lool, jéggal ma ngir saw tur.
12Ana kuy wormaal Aji Sax ji, mu won ko yoon wi mata taamu,
13muy dunde ngëneel, askanam moom réew mi?
14Ndéeyu Aji Sax ji, jagley ku ko ragal. Kóllëreem la koy xamal.