22Musal ma ci pàddum gaynde ak ndañum nagu àll. Yaa ma wallu woon!
23Ma siiwali saw tur ci bokk yi, màggale la digg mbooloo mi.
24Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen ko. Yeen askanu Yanqóoba wépp, màggal-leen ko. Yeen bànni Israyil gépp, wormaal-leen ko.
25Moom de sàgganewul boroom tiis, làqu ko kanamam, ba mu wootee, wuyu na ko.
26Yaw laay sante ndaje mu mag, sottalal la samay dige, ñi la ragal seede.
27Ku woyof a cay lekk ba doyal, kuy wut Aji Sax ji, sant ko. «Guddleena gudd fan!»
28Àddina wërngal këpp ay fàttliku, walbatiku ci Aji Sax ji. Làngi xeet yépp sukkalsi ko.
29Aji Sax jeey boroom nguur, moo yilif xeet yi.