3Bésoo bés kàddu seere ko, guddee guddi xamle ca mbir.
4Du làkk, duy wax, du baat bu dégtu,
5suuf sépp la seen ndéey jibal, seen kàddoo àkki cati àddina. Kaw la Yàlla sampal jant xayma,
6mu mel ni boroom séet, génne néegam, di mbër mu doŋali, xéluw yoonam.
7Asamaan lay fenke cat lii, wëndeelu, sowi cat lee; amul lu rëcc tàngooram.