31Yàllaa mat. Kàddug Aji Sax jee wér te wóor. Mooy feg képp ku ko làqoo.
32Ana kuy Yàlla ku moy Aji Sax ji? Ku jara sës ku dul sunu Yàlla?
33Yàllaa may dooleel, di ma xàllal, yoon mat.
34Moo ma gaawal ni kéwél, taxawal ma fu kawe.
35Moo may tàggat ngir xare, may bank xalag xànjar.
36Aji Sax ji yaa may feg, musal ma, dooleel ma sa loxo, nangul ma, darajaal ma.
37Yaa ma xàllalu yoon, ba duma tërëf.
38Ma dàq noon yi, dab leen, jekkli, doora dëpp.
39Ma jam leen, jógatuñu, xanaa fëlëñu, ma joggi.