21Aji Sax jee ma yool sama njekk, samay loxoo set, mu fey ma.
22Sàmm naa yooni Aji Sax ji, bonuma, di moy sama Yàlla.
23Dama ne jàkk ndigalam yépp, xalabuma dogali yoonam.
24May ànd ak moom, di jëfeg mat, di moyoo tooñ.
25Aji Sax jee ma yool sama njekk, rafetlu sama mucc ayib.
26Yaw Aji Sax ji, ku gore, fekk la gore; ku matale, fekk la matale;
27ku sellal, fekk la sell; ku dëng, fekk laak say feem.
28Yaw yaay musal xeet wu néew doole, kuy daŋŋiiral, nga detteel.
29Yaw kay yaa may niital. Aji Sax ji sama Yàllaay leeral sama lëndëm.