10Mu firi asamaan, wàcc, niir yu fatt lal tànk ya.
11Ma nga war malaakam serub, di naaw, daayaarloo laafi ngelaw.
12Ma nga bàddoo lëndëm, làqoo, làmboo ndox mu lëndëm aki xàmbaar,
13leer a ko jiitu, xàmbaar ya topp ca, ak tawub yuur ak xali sawara.
14Aji Sax jee dënoo asamaan. Aji Kawe jee àddu, muy tawub yuur ak xali sawara,
15mu soqiy fitt ak jumi melax, tasaare leen, fëlxe.
16Aji Sax ji, dangaa gëdd, nokki, mu riir, xuri géej ne fàŋŋ, kenuy suuf ne duŋŋ.
17Aji Sax jee yóotoo fa kaw, jàpp ma, seppee ma ca xóotey ndox ma,
18musal ma ca noon yu mag, ya ma bañ te man ma.
19Ñu dajeek man, bés ba ma jàqee, Aji Sax ji taxawu ma,
20yaatal ma, bége ma, ba xettli ma.
21Aji Sax jee ma yool sama njekk, samay loxoo set, mu fey ma.
22Sàmm naa yooni Aji Sax ji, bonuma, di moy sama Yàlla.
23Dama ne jàkk ndigalam yépp, xalabuma dogali yoonam.
24May ànd ak moom, di jëfeg mat, di moyoo tooñ.