2Yal na sama àtte bawoo fi yaw, nga gis sama njubte.
3Natt nga saab xol, niir ma guddi, settantal ma, gisoo dara. Dogu naa ne duma moye wax.
4Su may jëf it, di sàmm sa kàddu. Maay moyu yoonu ku bon.
5Sa tànk, sama tànk, jàdduma fenn.
6Éy Yàlla, maa lay woo, nga di ma wuyu; teewlu ma te déglu ma!
7Na sa ngor feeñ, yaw miy walloo sa doole ku la làqooy noonam.
8Sàmm ma ni peru bët; làqe ma sa ker,
9ma rëcc ñu bon ñi ma song, noon ñii ma gaw, nar maa bóom.
10Seen xol dàq yërmande, seeni wax di reewande.
11Tanc nañu nu fépp, ne nu jàkk, nar noo tëral.