1Muy ñaanu Daawuda. Éy Aji Sax ji, déglul liy dëgg, déglul, ma woote! Teewlul, ma dagaane la làmmiñ wu mucc fen.
2Yal na sama àtte bawoo fi yaw, nga gis sama njubte.
3Natt nga saab xol, niir ma guddi, settantal ma, gisoo dara. Dogu naa ne duma moye wax.