2Aji Sax jee tollu asamaan, jéer doom aadama, di seet ku ci xelu, tey sàkku Yàlla.
3Ñépp lajj, bokk yàqu yaxeet. Kenn deful lu baax, du kenn sax.
4Aji Sax ji nee: «Xanaa ñiy def lu bon ñépp xamuñu dara? Ñuy lekk sama ñoñ niw ñam, te sàkkuwuñu Aji Sax ji.»
5Foofu lañuy tiite tiitaange lu réy! Du Yàllaa ngi ànd ak kuréli ñu jub ñi?
6Ku néewlee yaakaar, ngeen tas ko, waaye Aji Sax ji la làqoo.
7Ana kuy xettlee Israyil fa Siyoŋ? Éy bés bu Aji Sax ji delloo ñoñam ndam, ndaw mbégte ci giirug Yanqóoba! Ndaw bànneex laa ne, ci Israyil gii!