11ak buuri àddinaak xeet yépp, ak kilifa yeek njiiti àddina yépp,
12xale bu góor ak bu jigéen, mag ak ndaw.
13Màggal-leen turu Aji Sax ji, moom doŋŋ la turam kawe, darajaam tiim asamaan ak suuf.
14Moo dooleel ñoñam, wóllëreem ñiy mbooloom bànni Israyil, xeet wi mu xejjoo, di ko màggal. Màggal-leen Ki Sax!