2Aji Sax jaa ngi tabaxaat Yerusalem, di délloosi ña ñu dàqe Israyil,
3di faj naqaru xol, fajtal góomi boroom.
4Mooy lim biddiiw yi, tudd bu ci nekk.
5Sunu Boroom a màgg, bare doole; am xelam wees kemu.
6Aji Sax ji, néew-ji-doole, mu yenni; ku bon, mu daane ci suuf.
7Woyeleen Aji Sax ji kàddug cant, kañeleen sunu Yàlla jii ay xalam;
8mooy sànge asamaan ay niir, tawal suuf, saxal tund yi am ñax,
9leel mala, xol liiru baaxoñ bu jooy.
10Kii nawul dooley fas, gërëmul kàttanu jàmbaar.
11Ki Aji Sax ji gërëm mooy ki ko ragal te di ko yaakaare ngoram.
12Yerusalem, sargal-leen Aji Sax ji! yeen waa Siyoŋ laa ne, màggal-leen seen Yàlla!
13Mooy tëj ràpp seen bunti dëkk, barkeel seen askan wa ca biir,
14jàmmal seen suufas réew, reggal leen ngëneelu pepp,