5Sa leeru teddnga ji ne ràññ, ak sa jëf ju yéeme laay jàngat!
6Sa dooley jëf ju raglu dees na ko jottli, te sa màggaay maa koy yéene.
7Sa mbaax gu réy, dees na ko tari, te sag njekk, dees na ko woy.
8Yiw ak yërmande, Aji Sax ji; kee muñ mer te bare ngor!
9Aji Sax jee baaxe ñépp, di yërëm lu mu sàkk.
10Aji Sax ji, lépp loo sàkk a lay gërëm, sa wóllëre yi di la sant,
11di tudd sa teddngay nguur, tey dégtale sag njàmbaar,
12doom aadama xam say jaloore ak sa teddngaak sa darajay nguur.