13Sa nguur ay nguur gu sax dàkk, sa kilifteef ñeel maasoo maas. Aji Sax ji daa sàmm ay waxam, gore ciy jëfam.
14Ku daanu, Aji Sax ji wallu; ku sëgg, mu siggil.
15Ñépp a la wékk bët, di yaakaar, te bu jotee, yaa leen di leel,
16tàllal sa loxo, reggal luy dund, ba xolam sedd.
17Aji Sax ji, jëfinam jépp njekk la, jëfam jépp ngor la.
18Aji Sax ji, képp ku ko woo wall, mu jege la, képp ku ko woo wall te muy dëgg.
19Nammeelu ku ko ragal, mu sottal; yuuxam, mu dégg, musal.