Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 144

Sabóor 144:6-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Melaxal, falaxe noon yi; fittal, ñu fëlxoo,
7nga yóotoo ma fu kawe, xettli ma, wallu ma ci doxandéem yi def wali wal fi sama kaw,
8di fen, di giñ ay fen.
9Yàlla, naa la woyal woy wu yees, xalamal la xalamu fukki buum.
10Yaay may buur yi ndam, yaa musal sa jaam ba, Daawuda ci saamar bu aay.
11Musal ma, xettli ma ci loxol doxandéem yiy fen, di giñ ay fen.
12Su boobaa sunu doom yu góor màgge ndaw, ni gàncax gu mat sëkk; sunuy janq jekk ni doji yett, yu ñu tabaxe kër buur.
13Sunuy sàq feese wirgoy wirgo, sunuy gàtt jur junni, ba fukki junni (10 000) ci parlu yi,
14nag yi ëmb ba diis, du mbas, du biir bu yàqu, te deesu fi yuuxoo pénc ya.
15Ndokklee xeet wu am lii! Ndokklee xeet wu yàllawoo Aji Sax ji!

Read Sabóor 144Sabóor 144
Compare Sabóor 144:6-15Sabóor 144:6-15