5Aji Sax ji, firil asamaan, wàcc; laal tund yi, ñu saxar.
6Melaxal, falaxe noon yi; fittal, ñu fëlxoo,
7nga yóotoo ma fu kawe, xettli ma, wallu ma ci doxandéem yi def wali wal fi sama kaw,
8di fen, di giñ ay fen.
9Yàlla, naa la woyal woy wu yees, xalamal la xalamu fukki buum.
10Yaay may buur yi ndam, yaa musal sa jaam ba, Daawuda ci saamar bu aay.