Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 140

Sabóor 140:5-8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Éy Aji Sax ji, aar ma ci loxol ku bon, musal ma ci nitu fitna, ku may fexee fakktal.
6Ñu bew ñee ma làqali yeer, lalal may buum aki caax, feggal ma seeni fiir ci yoon wi. Selaw.
7Dama ne Aji Sax ji, yaay sama Yàlla; Aji Sax ji, teewlul, ma dagaan la.
8Aji Sax ji Boroom bi may walloo doole, yaa ma yiir keroog bésub xare.

Read Sabóor 140Sabóor 140
Compare Sabóor 140:5-8Sabóor 140:5-8