19Éy sama Yàlla, soo reyoon ñu bon ñii! Yeen bóomkat yi, soreleen ma!
20Ñii sa tur lañuy luubale, noonoo la, di tudd sa tur ciy caaxaan.
21Aji Sax ji, maaka bañ ñi la bañ te sib ñi lay gàntal.
22Dama leena bañ ba fa mbañeel yem; samay noon dëgg lañu.
23Yàlla, seetlu ma, ba ràññee sama xol; natt ma, ba ràññee sama xalaati xol.