Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 137

Sabóor 137:5-7

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Éy Yerusalem, su ma la naree fàtte, yal na ma doole dëddu!
6Yerusalem, su ma la fàttlikuwul, fonk la, ba gën laa bége lépp, yal na sama làmmiñ tafoo sama denqleñ.
7Aji Sax ji, fàttlikul Edomeen ña, keroog jantub Yerusalem, ba ñu naan: «Màbbleena màbb, ba kenug dëkk bi siiñ!»

Read Sabóor 137Sabóor 137
Compare Sabóor 137:5-7Sabóor 137:5-7