3Santleen Sangu sang yi.
4Moo wéetoo jaloore yu mag yi.
5Moo sàkke asamaan manoore.
6Moo lal suuf ca kaw ndox ma.
7Moo sàkk leer yu mag yi:
8jant bi yilif bëccëg,
9weer ak biddiiw, guddi.
10Moo fàdd taawi Misra yu góor ya,
11seppee bànni Israyil ca ñoom,