1Nangeen sante Aji Sax ji mbaaxam.
2Santleen Yàllay yàlla yi.
3Santleen Sangu sang yi.
4Moo wéetoo jaloore yu mag yi.
5Moo sàkke asamaan manoore.
6Moo lal suuf ca kaw ndox ma.
7Moo sàkk leer yu mag yi:
8jant bi yilif bëccëg,
9weer ak biddiiw, guddi.
10Moo fàdd taawi Misra yu góor ya,