14Aji Sax ji kay ay àtte ñoñam ñi, di ñeewante jaamam ñi.
15Tuuri yéefar yi, xaalis ak wurus, loxoo ko sàkk.
16Am gémmiñ te du wax, ami gët te du gis,
17ami nopp te du dégg, du sax noowal bakkan.
18Ñi sàkk yii tuur, yal nañu mel ni ñoom, ñook ñi leen wóolu ñépp.
19Éey waa kër Israyil, santleen Aji Sax ji! Éey waa kër Aaróona, santleen Aji Sax ji!