4dañu nu doon mëdd nim ndox, def um wal, buub nu,
5def waame wuy wal-wali, buub nu, yóbbu.
6Cant ñeel na Aji Sax ji, ki nu bàyyiwul, noon yi yàpp nu.
7Danu ne fërr, nim picc mu rëcc fiiru rëbb, fiir ga toj, nu raw.
8Sunu ndimbal a ngi ci turu Aji Sax ji, ki sàkk asamaan ak suuf.