2Éy Aji Sax ji, musal ma ci gémmiñu fen-kat, ak làmmiñu njublaŋ.
3Yaw boroom làmmiñu njublaŋ, ana lu ñu lay añale ak lu ñu lay dolli?
4Xanaa fitti mbër yu ñaw ak xal yu yànj.
5Wóoy man mi ganeyaani baadooloy Meseg ya tey dali fa xaymay waa Kedar ñu xayadi ña!
6Yàgg naa lool ci biir nit ñi bañ jàmm.