Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 119

Sabóor 119:95-130

Help us?
Click on verse(s) to share them!
95Man la ñu bon ñi tëru, nar maa sànk, waaye sa kàdduy seede laay niir.
96Gis naa ne lu mat lu ne am na kemu, waaye sa santaane mat ba wees kemu.
97Maaka sopp saw yoon, di ko jàngat bés bu jot.
98Li ma xelal ba ma raw noon yi, mooy sa santaane, yi ma jagoo fàww.
99Maa gëna ñaw képp ku may jàngal, nde sa kàdduy seedeey sama njàngat.
100Maa ëpp mag ñi dég-dég, nde say tegtal laa topp.
101Luy yoon wu aay, ma moyu, ba mana sàmm sa kàddu.
102Say santaane it dëdduwma ko, nde yaw yaa ma jàngal.
103Sa kàddooka maa neex, ba dàqal ma tem-temu lem!
104Say tegtal laay ràññee, ba tax ma bañ luy yoonu fen.
105Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.
106Giñ naa te di ko dëggal, ne dinaa sàmmonteek sa ndigali njekk.
107Toskare naa ba ci lool; éy Aji Sax ji, musal ma, yaa ko dige.
108Aji Sax ji, rikk nangul ma kàdduy cant yi ma lay jébbal, te xamal ma say ndigal.
109Sama bakkan ci xott saa su ne, waaye fàttewuma saw yoon.
110Ñu bon ñi ma gasal um pax taxul ma wàcc say tegtal.
111Maa séddoo fàww sa kàdduy seede, loolooy seral sama xol.
112Damaa dogoo jëfe sa dogali yoon, saxoo ko ba mu jeex.
113Maa bañ kuy ŋarale, maa sopp saw yoon.
114Sama rawtu, sama kiiraay, yaw a; sa kàddu laay xaar.
115Yeen ñiy def lu bon, xiddileen ma, ba ma sàmmonteek sama santaaney Yàlla.
116Yaa ko dige, dooleel ma, ma dund; bul tas sama yaakaar.
117Kàttanal ma, ma raw, di yittewoo say tegtal, ba fàww.
118Yaay xarab képp ku wàcc sa dogali yoon, ay pexeem neen.
119Yaay tonni ni purit képp ku bon fi kaw suuf, moo tax ma sopp sa kàdduy seede.
120Sama yaram a ngi daw ndax ragal la, ragal say àtte.
121Def naa njub, def njekk; bu ma wacce ñi may néewal.
122Sang bi, gàddu ma, ma am jàmm, bu ma ñu bew ñi néewal.
123Séentu naa sag wall ak sa kàddug njekk, ba saay gët giim.
124Sang bi, jëfeel ma sa ngor, xamal ma sa dogali yoon.
125Sab jaam laa, may ma, ma ràññee, ba xam sa kàdduy seede.
126Aji Sax ji, jëf jot na, ñee ngi jalgati saw yoon!
127Maa sopp say santaane, mu gënal ma wurus ba ci wurusu ngalam.
128Moo tax foo tegtale, ma rafetlu, lépp luy yoonu fen, ma bañ.
129Sa kàdduy seede kéemaan la, moo tax ma di ko toppe xol.
130Sa pirim kàddu day leeral, di xelal ku xeluwul.

Read Sabóor 119Sabóor 119
Compare Sabóor 119:95-130Sabóor 119:95-130