67Maa jàddoon, nga duma ma, léegi sa kàddu laay sàmm.
68Yaaka baax tey baaxe; rikk xamal ma say tegtal.
69Ñu bew ñee yàq sama der aki sos, te ma topp say tegtal, wéetal la.
70Ñu ngi nii, seen bopp yi, tafas; te man may tàqamtikoo saw yoon.
71Ngëneel la ma duma yi jural, ngir jànge naa ci say tegtal.
72Sa ngëneelu yoon wi nga digle moo ma gënal ay junniy xaalis ak wurus.
73Say loxoo ma sàkk, tabax ma, may ma ag dégg, ma mokkal say santaane,
74ñi la ragal gis ma, bég; nde sa kàddu laa yaakaar.
75Aji Sax ji, ràññee naa ne say ndigal njekk la, te worma nga ma dumaa.
76Ngalla dëfale ma sa ngor; Sang bi, yaa ko dige.
77Nanga ma ganesee sa yërmande, ma dund; saw yoon ay sama bànneex!
78Yal na ñu bew ñi torox, ñoo ma lor ak seeni sos, te man may gëstu say tegtal.
79Yal na ku la ragal waññiku fi man, ba xam sa kàdduy seede.
80Yal naa toppe say tegtal xol bu mat sëkk, ba duma rus.
81Sàkku naa sag wall ba xol jeex, di xaar sa kàddu.
82Séentu naa sab dige, ba gët giim; kañ nga may xettli?
83Damaa mujj ras ni mbuusum der mu saxar jàpp, waaye sàgganewma say tegtal.
84Ñaata fan laay toogati, Sang bi? Kañ ngay mbugal ñi ma topp?
85Ñu bew ñi gasal nañu ma ay yeer, yu saw yoon diglewul.
86Sa santaane yépp worma la; te dees maa toppey sos, wallu ma!
87Nes tuut ñu sànke ma fi kaw suuf, te man dëdduwma say tegtal.
88Musale ma sa ngor, ba jëfe sa kàdduy seede.
89Aji Sax ji, sa kàddoo sax dàkk, taxaw jonn fa asamaan.
90Sa worma, ba maasoo maas, yaa samp suuf, saxal ko.
91Ci sa ndigal la lépp taxawe ba tey, lépp ànd, di la jaamu.
92Su ma bégewuloon saw yoon, sànkoo sama toskare ji.
93Duma fàtte mukk say tegtal, ci nga may musale.
94Yaa ma moom, wallu ma; say tegtal laay sàkku.
95Man la ñu bon ñi tëru, nar maa sànk, waaye sa kàdduy seede laay niir.
96Gis naa ne lu mat lu ne am na kemu, waaye sa santaane mat ba wees kemu.
97Maaka sopp saw yoon, di ko jàngat bés bu jot.
98Li ma xelal ba ma raw noon yi, mooy sa santaane, yi ma jagoo fàww.
99Maa gëna ñaw képp ku may jàngal, nde sa kàdduy seedeey sama njàngat.
100Maa ëpp mag ñi dég-dég, nde say tegtal laa topp.
101Luy yoon wu aay, ma moyu, ba mana sàmm sa kàddu.
102Say santaane it dëdduwma ko, nde yaw yaa ma jàngal.
103Sa kàddooka maa neex, ba dàqal ma tem-temu lem!
104Say tegtal laay ràññee, ba tax ma bañ luy yoonu fen.
105Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.
106Giñ naa te di ko dëggal, ne dinaa sàmmonteek sa ndigali njekk.
107Toskare naa ba ci lool; éy Aji Sax ji, musal ma, yaa ko dige.
108Aji Sax ji, rikk nangul ma kàdduy cant yi ma lay jébbal, te xamal ma say ndigal.
109Sama bakkan ci xott saa su ne, waaye fàttewuma saw yoon.
110Ñu bon ñi ma gasal um pax taxul ma wàcc say tegtal.
111Maa séddoo fàww sa kàdduy seede, loolooy seral sama xol.
112Damaa dogoo jëfe sa dogali yoon, saxoo ko ba mu jeex.
113Maa bañ kuy ŋarale, maa sopp saw yoon.
114Sama rawtu, sama kiiraay, yaw a; sa kàddu laay xaar.
115Yeen ñiy def lu bon, xiddileen ma, ba ma sàmmonteek sama santaaney Yàlla.
116Yaa ko dige, dooleel ma, ma dund; bul tas sama yaakaar.