34May ma dég-dég, ma topp saw yoon, toppe ko xol bu tàlli.
35Jiite ma ci sa xàllu santaane yi, mooy sama bànneex.
36Joyantil sama xol, mu féeteek sa kàdduy seede, te dummóoyu alal ju lewul.
37May ma, ma fénati caaxaani neen, te musale ma saw yoon.
38Sang bi, sottalal ma sa dige bi nga digook ku la ragal.
39Moyale ma gàcce gi ma ragal; yaa baaxi ndigal.
40Maaka namm say tegtal, musale ma sag njekk!
41Aji Sax ji, yaa ko dige, dikke ma sa jëfi ngor ak sa wall,
42ba ku ma kókkali, ma am tontam. Maa doyloo sa kàddu.
43Bu ma xañ mukk kàddug dëgg, say àtte laa yaakaar kat.
44Maay topp saw yoon, sàlloo ko, saxoo ko ba fàww,
45di daagoo sago, nde say tegtal laay sàkku.
46Maay àgge ay buur sa kàdduy seede, te duma rus.
47Maay bége sa santaane yi ma sopp,
48di yóotu sa santaane yi ma sopp, di jàngat sa dogali yoon.
49Bàyyil xel li nga ma dig, Sang bi; moom laa yaakaar.
50Lii laay muñe samaw naqar, sa kàddoo may dundal.