146Dama ne: «Wóoy, wallu ma, ma sàmm sa kàdduy seede.»
147Damaa jëlu, di la woo, di xaar sa kàddu.
148Damay xoole guddi gépp, di jàngat sa kàddu.
149Aji Sax ji, sama baat bii, teewloo ko sa ngor, te musal ma ni nga baaxoo muslee.
150Rabatkati pexe yaa ngi jegesi, di nit ñu sore saw yoon.
151Waaye yaw Aji Sax ji, jege nga, te sa santaane yépp a dëggu.
152Yàgg naa xam ne sa kàdduy seede wax la joo saxal dàkk.
153Xoolal sama coono te xettli ma; saw yoon déy, sàgganewma ko.
154Àtte ma, ba jot ma; musal ma, yaa ko dige.