133Dooleelal ma samay tànk, yaa ko dige, te bu ma lenn lu bon man.
134Jot ma ci noteelu doom aadama, ma mana topp say tegtal.
135Sang bi, geesoo ma sag leer, te xamal ma sa dogali yoon,
136ay wali rongooñ ay wale saay gët, ndax sàmmeesul saw yoon.
137Aji Sax ji, yaaka jub, te say àtte di yoon.
138Yaa santaane sa kàdduy seede ci njekk ak worma ju yaa.
139Damaa gis bañ yiy sàggane say wax, xol bu tàng di ma rey.
140Sang bi, maaka sopp sa kàddu gi set ni weñ gu ñu xelli!
141Ñàkk naa solo, faaleesu ma, waaye sàgganewma say tegtal.
142Sag njekk moo dig njekk ba fàww, te saw yoon a dëggu.
143Njekkar ak njàqare dab ma, say santaane di sama bànneex.
144Sa kàdduy seedee di njekk ba fàww, may ma, ma ràññee, ba dund.
145Aji Sax ji, woo naa la wall lu ma man, wuyu ma, ma topp sa dogali yoon.
146Dama ne: «Wóoy, wallu ma, ma sàmm sa kàdduy seede.»
147Damaa jëlu, di la woo, di xaar sa kàddu.
148Damay xoole guddi gépp, di jàngat sa kàddu.
149Aji Sax ji, sama baat bii, teewloo ko sa ngor, te musal ma ni nga baaxoo muslee.
150Rabatkati pexe yaa ngi jegesi, di nit ñu sore saw yoon.