116Yaa ko dige, dooleel ma, ma dund; bul tas sama yaakaar.
117Kàttanal ma, ma raw, di yittewoo say tegtal, ba fàww.
118Yaay xarab képp ku wàcc sa dogali yoon, ay pexeem neen.
119Yaay tonni ni purit képp ku bon fi kaw suuf, moo tax ma sopp sa kàdduy seede.
120Sama yaram a ngi daw ndax ragal la, ragal say àtte.
121Def naa njub, def njekk; bu ma wacce ñi may néewal.
122Sang bi, gàddu ma, ma am jàmm, bu ma ñu bew ñi néewal.
123Séentu naa sag wall ak sa kàddug njekk, ba saay gët giim.
124Sang bi, jëfeel ma sa ngor, xamal ma sa dogali yoon.
125Sab jaam laa, may ma, ma ràññee, ba xam sa kàdduy seede.
126Aji Sax ji, jëf jot na, ñee ngi jalgati saw yoon!
127Maa sopp say santaane, mu gënal ma wurus ba ci wurusu ngalam.
128Moo tax foo tegtale, ma rafetlu, lépp luy yoonu fen, ma bañ.
129Sa kàdduy seede kéemaan la, moo tax ma di ko toppe xol.
130Sa pirim kàddu day leeral, di xelal ku xeluwul.
131Damaa ŋa ŋafeet, di àppaat, ngir namm say santaane.
132Éy geesu ma te baaxe ma, ni nga baaxook ñi sopp sa tur.
133Dooleelal ma samay tànk, yaa ko dige, te bu ma lenn lu bon man.
134Jot ma ci noteelu doom aadama, ma mana topp say tegtal.
135Sang bi, geesoo ma sag leer, te xamal ma sa dogali yoon,
136ay wali rongooñ ay wale saay gët, ndax sàmmeesul saw yoon.
137Aji Sax ji, yaaka jub, te say àtte di yoon.
138Yaa santaane sa kàdduy seede ci njekk ak worma ju yaa.
139Damaa gis bañ yiy sàggane say wax, xol bu tàng di ma rey.
140Sang bi, maaka sopp sa kàddu gi set ni weñ gu ñu xelli!
141Ñàkk naa solo, faaleesu ma, waaye sàgganewma say tegtal.
142Sag njekk moo dig njekk ba fàww, te saw yoon a dëggu.
143Njekkar ak njàqare dab ma, say santaane di sama bànneex.
144Sa kàdduy seedee di njekk ba fàww, may ma, ma ràññee, ba dund.
145Aji Sax ji, woo naa la wall lu ma man, wuyu ma, ma topp sa dogali yoon.
146Dama ne: «Wóoy, wallu ma, ma sàmm sa kàdduy seede.»