110Ñu bon ñi ma gasal um pax taxul ma wàcc say tegtal.
111Maa séddoo fàww sa kàdduy seede, loolooy seral sama xol.
112Damaa dogoo jëfe sa dogali yoon, saxoo ko ba mu jeex.
113Maa bañ kuy ŋarale, maa sopp saw yoon.
114Sama rawtu, sama kiiraay, yaw a; sa kàddu laay xaar.
115Yeen ñiy def lu bon, xiddileen ma, ba ma sàmmonteek sama santaaney Yàlla.
116Yaa ko dige, dooleel ma, ma dund; bul tas sama yaakaar.
117Kàttanal ma, ma raw, di yittewoo say tegtal, ba fàww.
118Yaay xarab képp ku wàcc sa dogali yoon, ay pexeem neen.