106Giñ naa te di ko dëggal, ne dinaa sàmmonteek sa ndigali njekk.
107Toskare naa ba ci lool; éy Aji Sax ji, musal ma, yaa ko dige.
108Aji Sax ji, rikk nangul ma kàdduy cant yi ma lay jébbal, te xamal ma say ndigal.
109Sama bakkan ci xott saa su ne, waaye fàttewuma saw yoon.
110Ñu bon ñi ma gasal um pax taxul ma wàcc say tegtal.
111Maa séddoo fàww sa kàdduy seede, loolooy seral sama xol.