Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 119

Sabóor 119:102-108

Help us?
Click on verse(s) to share them!
102Say santaane it dëdduwma ko, nde yaw yaa ma jàngal.
103Sa kàddooka maa neex, ba dàqal ma tem-temu lem!
104Say tegtal laay ràññee, ba tax ma bañ luy yoonu fen.
105Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.
106Giñ naa te di ko dëggal, ne dinaa sàmmonteek sa ndigali njekk.
107Toskare naa ba ci lool; éy Aji Sax ji, musal ma, yaa ko dige.
108Aji Sax ji, rikk nangul ma kàdduy cant yi ma lay jébbal, te xamal ma say ndigal.

Read Sabóor 119Sabóor 119
Compare Sabóor 119:102-108Sabóor 119:102-108