Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Mise

Mise 4

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, askan yi riirandoo, wutsi ko.
2Xeet yu bareey dikk te naan: «Dikkleen nu yéegi ca tundu Aji Sax ji, kër Yàllay Yanqóoba, mu xamal nuy yoonam, ba nu doxe yooyu ñallam.» Siyoŋ kat la ndigalu yoon di bawoo, Yerusalem googu la kàddug Aji Sax ji di jóge.
3Mooy àtte diggante xeet yu bare, mooy dogalal askan yu am doole te sore, ñu tëgg seeni saamar ay illéer, def seeni xeej ay sàrt. Aw xeet dootu xàccil moroom ma saamar, te dootuñu jàngati xare.
4Ñoom ñépp ay toog, ku nekk ci kerug reseñam, mbaa keppaarug garabu figgam, kenn du leen xoqtal. Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
5Askan wu nekk ci yaakaaru turu yàllaam lay doxe. Nun nag ci yaakaaru sunu turu Yàlla Aji Sax ji lanuy doxe, tey ak ëllëg, ba fàww.
6Bésub keroog, kàddug Aji Sax jee, «Naa jëli kuy soox, booleek ku ñu toxaloon, te ma mbugaloon leen.
7Maay def liy soox aw ndes, la ñu dàq fu sore, ma def ko askan wu am doole, te Aji Sax jeey doon seen buur ca kaw tundu Siyoŋ, li ko dale tey ba fàww.
8«Yaw, tatay gétt gi, yaw tundu Ofel, yaw janq Siyoŋ mu taaru mi, yaw lees di ñëwal, yaw la kilifteef ga woon di dikkal, nguur gi, janq Yerusalem mu taaru lay ñeel.»
9Ana lu la tax di yuuxoo yuuxu tey? Buur daa amul fi sa biir? Am ki lay xelal a dee, ba mitit jàpp la nii, nga mel ni kuy matu?
10Wañaarul te yuuxu ni kuy matu ndax mitit, yaw janq Siyoŋ mu taaru, nde dëkk bi ngay génn, màkkaanoo àll bi, dinga dem Babilon, te fa lees lay xettlee, fa la la Aji Sax jiy jote ci loxol say noon.
11Tey ci sa kaw, la xeet yu bare daje, yaw Siyoŋ, te naan: «Nees ko tëdde, nanu seetaan Siyoŋ!»
12Booba ñoom xamuñu lu ciy xalaati Aji Sax ji, ak luy mébétam, nde moo leen di dajale niy sabaar ca dàgga ja.
13«Yaw janq Siyoŋ mu taaru, jógal bàcci leen, sa béjjén laay def ag weñ, say wewi tànk, ma def ko xànjar, nga rajaxe xeet yu bare.» Yaay faagaagal seen alal ju lewul, ñeel Aji Sax ji, seen koom ñeel Boroom àddina sépp.
14Léegi yaw, dëkkub gàngoor yi, defal sa bopp ay gàngoor, ab gaw lees nu yékkatil, te yetu ŋaam lees di dóor njiital Israyil.