Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 5

Luug 5:1-13

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Yeesoo taxawoon ca tàkkal dexu Senesaret, mbooloo ma tancaloo ci kawam, di déglu kàddug Yàlla.
2Ci biir loolu mu gis ñaari gaal yu taxaw ci tàkk gi, nappkat ya ca wàcce, di fóot seeni mbaal.
3Mu dugg ci genn gaal gi, muy gu Simoŋ. Mu ñaan ko mu bëmëx ba dànd tefes gi as lëf. Mu defal ko noonu, Yeesu toog, tàmbalee jàngal mbooloo ma fa mu tollu ca biir gaal ga.
4Naka la jàngle ba noppi, ne Simoŋ: «Bëmëxal ba ca xóote ba, te ngeen sànni seeni mbaal ba jàpp.»
5Simoŋ ne ko: «Njaatige, coono lanu fanaane biig te jàppunu dara. Xanaa ma sànni ko rekk ci sa ndigal.»
6Naka lañu sànni mbaal yi, daldi jàpp jën yu baree bare, ba mbaal ya di xëtt.
7Ba loolu amee ñu liyaar seen moroom, ya ca geneen gaal ga, ngir ñu dimbalisi leen. Ñu dikk, yebandook ñoom, feesal ñaari gaal yépp, ba ñuy bëgga suux.
8Simoŋ Piyeer nag gis loolu, daldi sukk fa kanam Yeesu, ne ko: «Sang bi, ngalla sore ma, ngir man nitu bàkkaarkat laa!»,
9ndax tiitaange lu ko jàpp, mook mboolem ña mu àndal, ca jën yu bare ya ñu jàpp.
10Yanqóoba ak Yowaan doomi Sebede ya mu bokkaloon liggéey ba itam noonu lañu tiite. Yeesu ne Simoŋ: «Bul ragal dara; gannaaw-si-tey, ay nit ngay napp.»
11Ci kaw loolu ñu teeral gaal ya ca tefes ga, daldi bàyyi lépp, topp ca moom.
12Yeesoo nekkoon cib dëkk, ndeke jenn waay a nga fa, ju jàngoroy ngaana dajal yaram wa. Ba mu gisee Yeesu, daa daanu, dëpp jëëm ci suuf, sarxu ko, ne: «Sang bi, su la soobee, man nga maa setal.»
13Yeesu tàllal loxoom, laal ko ne: «Soob na ma, setal.» Ca saa sa ngaana ga teqlikook moom.

Read Luug 5Luug 5
Compare Luug 5:1-13Luug 5:1-13