Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 16

Luug 16:15-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Yeesu ne leen: «Yeen yeenay jub-jublu ci kanam nit ñi, waaye Yàlla xam na seen xol. Ndax li nit ñi gëna naw, lu seexluwu la fa Yàlla.
16«Yoonu Musaa wi ak waxi yonent yi la woon ba kera ba Yaxya dikkee. Waaye ba mu dikkee lañu yégle nguurug Yàlla, ñépp di ci jéema dugge seen doole.
17Waaye nag asamaan ak suuf raaf moo gëna yomb genn maaska rote ci mbindum yoonu Musaa.
18«Képp ku fase sa jabar, takk keneen, jaaloo nga; te ku jëkkëram fase, képp ku ko takk, jaaloo nga.
19«Jenn waay la woon ju bare alal, di sol yérey tànnéef yu rafet, di dunde lu neex bés bu set.
20Ab baadoolo bu ñuy wax Lasaar nag farala tëdde buntu kër waa ji, yaram wa ne fureet aki góom,
21te noon ngéeja fajeb xiifam lu ruuse ci ndabal boroom alal bi. Rax ci dolli xaj yiy dikk, di mar ay góomam.
22«Ba baadoolo ba deeyee, malaaka yi yóbbu ko ba ca wetu Ibraayma. Boroom alal ba itam dee, ñu rob ko.
23Ci kaw loolu ñu dugal ko sawara. Ca biir mbugal mu tar ma la dawale bëtam, daldi séen fu sore Ibraayma ak Lasaar ci wetam.
24Mu xaacu ne: “Maam Ibraayma, yërëm ma! Yebalal Lasaar, mu sëpp catal baaraamam ci ndox, dikk seralal ma sama làmmiñ, sawara sii metti na lool!”
25Ibraayma ne ko: “Doom, fàttlikul ne na nga séddoo woon sa bànneex ca àddina, noonu la Lasaar nekke woon aw tiis. Waaye fii nag moo neexle, yaw nga mitile.
26Bu loolu yépp weesee itam, sunu digg ak yeen kàmb gu xóot a fi dox; moo tax ku bëgga jóge fii jëm ci yeen, mbaa mu jóge foofu jëmsi ci nun, du ko man.”

Read Luug 16Luug 16
Compare Luug 16:15-26Luug 16:15-26