1Yeen xeet wi dul rus, dajeleena daje,
2balaa dogal bee taxaw, bésub mbugal ne jaas ba wéy ni boob, bala leen tàngooru merum Aji Sax jee dikkal, bala leen bésub merum Aji Sax jee taxawal.
3Sàkkuleen Aji Sax ji, mboolem yeen néew-dooley réew mi, yeen ñiy jëfe àttey yoonam, sàkkuleen njekk te sàkkoo toroxlu, jombul ngeen yiiru, kera bésu merum Aji Sax ji.
4Gasa dëkk ba lees di wacc, Askalon gental, Asdodd, digg bëccëg lees leen di buub, génne, te Ekkron lees di déjjati.
5Wóoy ngalla yeen waa tefesu géej, yeen xeetu Kereteen ñi, kàddug Aji Sax ji dal na leen. Yeen waa Kanaan, réewum Filisteen ñi, maa leen di sànk ba dungeen dese kenn,
6tefesu géej doon àllub parlu, ak dëkkuwaayu sàmm seek gétt gi.
7Tefes ga, ndesu kër Yuda koy moom, ñu di ca fore, bu ngoonee ñu tëri néegi Askalon. Seen Yàlla Aji Sax jee leen di dikkal, tijji seen wërsëg (/yiwileen cig njaam.)
8«Maa dégg ŋàññi Mowab, kàddu yu ñaaw yi Amoneen ñiy ŋàññe sama ñoñ, tey damu, nara nangu seen suuf.
9Moo tax, giñ naa ko ci man miy dund,» kàddug Aji Sax ju gàngoor yee, Yàllay Israyil, «Mowab déy ni dëkkub Sodom lay mujje, Amoneen ñi mel ni Gomor, ay dég ak paxi xorom a koy nangu, mu gental ba fàww. Sama ndesu ñoñ a leen di sëxëtoo, ndesu xeet wi ma séddoo moo leen di moom.»
10Loolu lañuy yooloo seen reewande, nde ñoo doon ŋàññe aka damu ci kaw ñoñi Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
11Nu raglu la Aji Sax jiy dale ci seen kaw, te mooy ràggal yàllay àddina yépp, ba xeet yi di ko sujjóotale dunoo dun, wu ci nekk ak fa nga fare.
12Yeen waa Kuus, itam yeen lees di fàdde sama saamar.
13Keey xàccil loxoom bëj-gànnaar, keey sànk réewum Asiri, keey def Niniw ab gent bu wow ni màndiŋ.
14Ca digg dëkk ba la jur gay goore, ak xeetu rab wu nekk; looy aki saaw fanaane kaw jëni bunt ya, ay sab jibe ca palanteer ya, tojit ya dala jale ca bunt ya, xànqi seedar ya ne duŋŋ.
15Ana dëkk bu xumb ba dëkke woon kaaraange, te naan cim xelam: «Man rekk a, du keneen»? Nan la doone nii ab gent, bérab bu rab yiy goore, mboolem ku fa jaare, ub gémmiñam, jalu.